Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - 2.Buur ya - 2.Buur ya 13

2.Buur ya 13:4-22

Help us?
Click on verse(s) to share them!
4Yowakas nag tinu Aji Sax ji, mu nangul ko, ndax fekk na mu gis fitnay Israyil ji leen buurub Siri fitnaal.
5Aji Sax ji daldi may Israyil ku leen xettli, ba ñu génn ca loxol waa Siri. Ba loolu amee waa Israyil dellu nekk ca seeni kër ci jàmm, na woon démb ak bëkk-démb.
6Taxul ba tey ñu dëddu bàkkaari waa kër Yerbowam ya ñu doon bàkkaarloo Israyil. Dañu caa sax. Te it xer wa ñuy jaamoo Aseraa nga sampe woon ca Samari ba booba.
7Mujj na Yowakas desewuloon ca mbooloom xareem lu moy juróom fukki gawar ak fukki watiir ak fukki junniy xarekat (10 000), ndax buurub Siri moo faagaagal ña ca des ñépp, duma leen ba ñu ne mbëtt.
8Li des ci mbiri Yowakas ak mboolem lu mu def aki njàmbaaram, bindees na lépp moos ci téere bi ñu dippee Jaloorey buurub Israyil ca seeni jant.
9Ba mu ko defee Buur Yowakas saay, fekki ay maamam, ñu denc ko ca Samari. Doomam Yowayas falu buur, wuutu ko.
10Ba Yowas buurub Yuda duggee fanweereelu atu nguuram ak juróom ñaar, ca la Yowayas doomu Yowakas falu buurub Israyil, péeyoo Samari. Nguuru na fukki at ak juróom benn.
11Muy def li Aji Sax ji ñaawlu nag, dëdduwul lenn ci bàkkaar ya Yerbowam doomu Nebat doon bàkkaarloo Israyil. Da caa sax kay.
12Li des ci mbiri Yowayas ak mboolem lu mu def ak njàmbaar ga mu xareek Amaciya buurub Yuda, bindees na lépp moos ci téere bi ñu dippee Jaloorey buuri Israyil ca seeni jant.
13Yowayas nag saay, fekki ay maamam, Yerbowam falu, wuutu ko. Ñu denc Yowayas fa ñu denc buuri Israyil ca Samari.
14Ba Alyaasa tëddee ca wopp ja ko wara yóbbu, Yowayas buurub Israyil seeti woon na ko, tiim ko, di jooy naan: «Éy baayoo, baay Alyaasa, yaay watiiru xarey Israyil aki gawaram!»
15Alyaasa ne ko: «Indil xala aki fitt.» Mu indi.
16Alyaasa ne ko: «Soxal.» Mu sox. Alyaasa teg ay loxoom ca kaw loxoom,
17ba noppi ne ko: «Ubbil palanteeru penku bi.» Mu ubbi. Alyaasa ne ko: «Soqil!» Mu soqi. Mu ne ko: «Fittu ndamal Aji Sax jaa ngoog, di fitt gi ngay ame ndam ci waa Siri. Dinga daan waa Siri ca Afeg, ba faagaagal leen.»
18Mu delluwaat ne ko: «Jëlal fitt yi.» Mu jël. Mu ne ko: «Soqil fi suuf!» Mu soqi, ba muy ñetti yoon, bàyyi.
19Góorug Yàlla ga nag mere ko, ne ko: «Soo jamoon juróomi yoon ba juróom benni yoon, dinga daan waa Siri, ba jeexal leen tàkk; waaye léegi nag ñetti yoon rekk ngay daan waa Siri.»
20Gannaaw gi Alyaasa faatu, ñu denc ko. Loolu fekk na ndoortel at mu jotaan ay gàngoori yàqkati Mowabeen dugg ca réew ma.
21Mu am bés ay nit doon rob, jekki-jekki gis gàngooru yàqkat di dikk. Ñu sànni néew ba ca bàmmeelu Alyaasa, daldi daw. Naka la néew ba dal ca yaxi Alyaasa, rekk dekki, ne ñokket, taxaw.
22Ci kaw loolu Asayel buurub Siri di fitnaal Israyil mboolem diir ba Yowakas di buur.

Read 2.Buur ya 132.Buur ya 13
Compare 2.Buur ya 13:4-222.Buur ya 13:4-22