Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - 1.Buur ya - 1.Buur ya 7

1.Buur ya 7:5-44

Help us?
Click on verse(s) to share them!
5Bunt yépp ànd ak seen banti feguwaay, bunt bu ci nekk def ñeenti wet yu janoo màkk ñaar-ñaar; bunt yi sësaloo te dékkarloo ñett-ñett.
6Ci biir loolu mu defar néeg ba ñuy wooye Néegu jëni kenu ya. Guddaay bi di juróom fukki xasab, yaatuwaay bi di fanweeri xasab, ak beneen néeg ci kanamam, mu ànd ak ay jëni kenoom ak xaddam bu mbaar ci kanam.
7Mu tabax néeg ba ñuy wooye Néegu ngàngune ma walla Àttekaay ba, mu di fa àttee. Mu dare néeg bi banti seedar ci suuf ba ci kaw.
8Këram ga mu dëkk it, ñu tabaxe ko noonu ci gannaaw Néegu ngàngune ma. Suleymaan teg ca tabaxal soxnaam doomu Firawna ja geneen kër gu nirook këram.
9Tabax yooyu yépp biir ak biti xeeri tànnéef yu ñu yett la, natt ko, xacc ko, rattaxal, dale ko ci kenu gi, ba ci cati xadd bi ci kaw, daleeti ci biti ba ci ëtt bu mag bi.
10Ñu defare kenu yi xeeri tànnéef yu mag: yii di fukki xasab, yii di juróom ñetti xasab.
11Xeer yi tege ci kenu gi, xeeri tànnéef la yu ñu yett, natt ko, yemale, booleek banti seedar.
12Miiru ëtt bu mag bi dees koo wëralee ay xeeri yett aki xànqi seedar: ñetti sësalantey xeer yu tegloo yu ne, benn sësalanteb xànqi seedar tege ca. Mu mel ni na ñu def ëttu biir bu kër Aji Sax ja ak dëru buntu kër ga.
13Ci kaw loolu Buur Suleymaan yónnee, jëli ca Tir ku ñuy wax Uram.
14Doomu jëtun la woon, bokk ci giirug Neftali. Baayam dëkkoon Tir, di tëggub xànjar. Uram di ku xareñ lool, rafet xel te mane mboolem liggéeyu xànjar. Mu dikk ca Buur Suleymaan, liggéeyal ko la ñu ko sant lépp.
15Mu móol ñaari xeri xànjar, wu ci nekk am taxawaayu fukki xasab ak juróom ñett, te wu ci nekk buumu fukki xasab ak ñaar a koy ub.
16Ci biir loolu mu defar ñaari boppi xànjar yu mu xelli, teg ko ci kaw xer yi, bopp bu ci nekk am taxawaayu juróomi xasab.
17Bopp yi ci kaw xer yi, bu ci nekk da koo rafetale ab caaxu càllala, bopp bu ci nekk am ci juróom ñaar.
18Mu defar ñaari jaray gërënaat, solal ko caax yi, wëralee ko bopp yi, ci xer wu ci nekk.
19Bopp yi nekkoon ci kaw xer yi ci kanam nag bindoo ni lëppi tóor-tóor te bu ci nekk di ñeenti xasab.
20Bopp yi ci kaw ñaari xer yi, bu ci nekk ñaar téeméeri gërënaat a ko wër ci kaw, feggook gamb bi ci wàllaa caax bi.
21Mu samp jën yi ci kanam bunt néeg Yàlla bu mag bi; samp jënu ndijoor wi, tudde ko Yakin (Kiy taxawal), samp jënu càmmoñ wi, tudde ko Bowas (Kiy dooleel).
22Kaw xer yi ay lëppi tóor-tóor yu ñu xellee ci tege. Liggéeyu xer ya daldi sotti.
23Ba mu ko defee Uram móol mbalkam njàpp mu weñ, ñu di ko wax Géej ga. Mbalka ma daa mërgalu, yaatoo fukki xasab, catu omb ba catu omb, taxawaay ba di juróomi xasab, ag buumu fanweeri xasab di ko ub.
24Ay gamb la ko sàkkal ci suufu kéméj gi, fukki gamb tollook xasab. Mu def gamb yi ñaari caq yu wër mbalka mi ba mu daj te ànd ak mbalka mi ci benn xelli.
25Mbalkam njàpp mi tege ci kaw fukki jëmmi nag ak yaar, ñett jublu bëj-gànnaar, ñett jublu sowu, ñett jublu bëj-saalum, ñett jublu penku. Mbalka mi war nag yi, seeni gannaaw féete biir, ñoom ñépp.
26Dëllaayu mbalka mi yaatuwaayu loxo la, kéméj gi mel ni gémmiñu kaas, di nirook lëppi tóor-tóor. Ñaar téeméeri barigo la mbalka miy def. (200).
27Mu daldi sàkk fukki watiiri rootukaayi xànjar, wu ci nekk am guddaayu ñeenti xasab, yaatuwaayam di ñeenti xasab, taxawaayam di ñetti xasab.
28Ni ñu defare rootukaay yi nii la: ay wetam lañu defare làcci xànjar, lëkklee làcc yi ay laat.
29Muy làcc yu Uram yett ci kawam ay gaynde, ay nag ak malaakay serub. Kaw laat yi itam am na ci nataal yi. Mu yett ay caqi tóor-tóor yuy lang ci suufu gaynde yeek nag yi.
30Rootukaay bu nekk am na ñeenti mbegey xànjar yu ñu lëkklee yeti xànjar. Mu am ay kenu yu ñu xellil rootukaay bi ci ñeenti koñam, kenu yi yenu benn bagaan te am ay nataali tóor-tóor.
31Gémmiñu rootukaay bu nekk amoon na omb bu mërgalu bu bagaanu ndox biy tege. Xóotaayu gémmiñ gi di xasab, yaatuwaay bi di xasab ak genn-wàll. Ñu yett ci kaw gémmiñ gi ay nataal ba tey. Rootukaay bi mërgaluwul, waaye daa bindoo ñeenti wet yu janoo màkk ñaar-ñaar te yem kepp.
32Ñeenti mbege yi ronu làcc yi, tóori weñ yi ci wewe sax ci rootukaay bi. Mbege mu ci nekk am na taxawaayu xasab ak genn-wàll.
33Mbege yi bindoo ni mbegey watiiri xare. Tóor yeek mbege yi ak sidditi mbege yi ak ŋanku yi, xànjar lañu ko xellee.
34Ñeenti kenu yi ci ñeenti koñi rootukaay bi, bu ci nekk dees koo xelleendook weti rootukaay yi, ba lépp di benn.
35Kaw boppu rootukaay bu nekk, kéméj gu mërgaloo féete ci kaw, taxawaayam di genn-wàllu xasab, njàppu yeek làcc yi sax ci, lépp di benn.
36Fi amul dara ci kaw njàppu yeek làcc yi, mu ñaas ci ay nataali serub aki gaynde aki garabi ron yu ñu wërale ay caqi tóor-tóor.
37Noonu la Uram defare fukki rootukaay yi. Lépp bokk móol, yem dayo te bokk bind.
38Mu defar itam fukki bagaani xànjar; bagaan bu ci nekk tollook ñeenti xasab, di def lu xawa tollook juróomi barigo; bagaan bu ci nekk tegu cib rootukaay, ba fukki rootukaay yi daj.
39Ba mu ko defee mu taaj juróomi rootukaay fa féete kër Yàlla ga ndijoor ak juróomi rootukaay fa féete kër ga càmmoñ. Mu teg mbalkam jàpp mi fa féete kër ga ndijoor, ca wetu bëj-saalum, jàpp penku.
40Iram sàkk itam ndab yu ndaw yi ak ñiitukaay yi ak këlli tuurukaay yi. Ci kaw loolu Iram sottal mboolem liggéey ba mu liggéeyal Buur Suleymaan ca kër Aji Sax ji:
41muy ñaari jën yi, ak ñaari gamb yiy boppi jën yi, ak ñaari caaxi càllala yiy muur ñaari gamb yi,
42ak ñeenti téeméeri gërënaat yiy ànd ak ñaari caax yi; caax bu nekk, ñaari caqi gërënaat, ñu dar ñaari gamb yiy boppi xer yi;
43ak fukki rootukaay yi ak fukki bagaan yi ci kaw rootukaay yi.
44Mbalkam jàpp mi it ci la, ak fukki nag ak yaar yi ronu mbalkam jàpp mi.

Read 1.Buur ya 71.Buur ya 7
Compare 1.Buur ya 7:5-441.Buur ya 7:5-44