Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - 1.Buur ya - 1.Buur ya 22

1.Buur ya 22:7-53

Help us?
Click on verse(s) to share them!
7Yosafat dellu ne: «Xanaa beneen yonentu Aji Sax ji da fee amatul, ba ñu mana seetlujeeti fa moom?»
8Buurub Israyil ne Yosafat: «Am na ba tey genn góor gu ñu mana seetal ci Aji Sax ji. Waaye man maa ko jéppi, ndax du wax waxyu bu baax ci man, lu bon rekk; mooy Mise doomu Yimla.» Yosafat ne ko: «Buur, bul waxe noonu.»
9Buurub Israyil daldi woo ab jawriñam ne ko: «Demal indil ma gaaw Mise doomu Yimla.»
10Buurub Israyil ak Yosafat buurub Yuda nag, ña nga toog, ku ci nekk ci ngànguneem. Ña nga solu ba jekk ca dàgga ja ca buntu Samari. Yonent yépp janook ñoom di biral ay waxyu.
11Fekk na Cedekiya doomu Kenaana, ma woon ci seen biir, defarlu ay béjjéni weñ. Ma nga naan: «Aji Sax ji dafa wax ne: “Yii ngay jame waa Siri, ba jeexal leen.”»
12Mboolem yonent ya ca des nag di waxe jenn waxyu jooju, naan: «Buur, songal Ramot ga ca Galàdd te jël ndam li, ndax Aji Sax ji moo leen teg ci say loxo.»
13Ci kaw loolu ndaw la wooyi Mise, dem ne ko: «Ma ne, kàddug yonent ya genn la: jàmmu Buur. Kon nag, na sa kàddu ànd ak seen kàddu di genn, te nga wax jàmm.»
14Mise ne ko: «Giñ naa ci Aji Sax ji, Kiy Dund, li ma Aji Sax ji wax rekk laay wax.»
15Ba Mise dikkee ba ca Buur, Buur ne ko: «Mise, ndax nu songi xare Ramot ga ca Galàdd, am nu bàyyi?» Mu ne ko: «Buur songal, daan, Aji Sax jee koy teg ci sa loxo!»
16Buur nag ne ko: «Ñaata yoon laa lay giñloo ne la bu ma wax lu moy dëgg ci turu Aji Sax ji?»
17Mise ne ko: «Israyil gépp laa gis ñu tasaaroo ca tund ya, mbete xar yu amul sàmm. Aji Sax ji ne: “Ñii de amuñu boroom. Na ku nekk ci ñoom ñibbi këram ci jàmm.”»
18Buurub Israyil ne Yosafat: «Waxuma la woon ne du wax waxyu bu baax ci man, xanaa lu bon?»
19Mise teg ca ne ko: «Kon nag déglul kàddug Aji Sax ji. Gis naa Aji Sax ji, mu toog ci ngànguneem, mboolem gàngooru asamaan a nga taxaw ndijooram ba càmmoñam.
20Aji Sax ji nag ne: “Ana kuy nax Axab, mu songi Ramot ga ca Galàdd, ba daanu ca?” Kii ne nii, kee ne nee.
21Noo ga dikk, taxaw fa kanam Aji Sax ji. Mu ne: “Man maa koy nax.” Aji Sax ji ne ko: “Nan?”
22Mu ne: “Maay dikk, doon xel muy safaan dëgg ci làmmiñu yonentam yépp.” Mu ne ko: “Yaa koy nax, te man nga ko. Demal defe noonu.”
23Looloo waral lii. Aji Sax ji moo def xel muy safaan dëgg ci sa làmmiñu yonent yii yépp, te Aji Sax ji moo tudd musiba ci sa kaw.»
24Ba loolu amee Cedekiya doomu Kenaana talaata Mise, ne ko: «Ana fu Noowug waxyu gu Aji Sax ji jaare, ba jóge ci man di wax ak yaw?»
25Mise ne ko: «Yaw mii yaa koy gisal sa bopp, keroog ba ngay dugg néegoo néeg, di làqtu.»
26Buurub Israyil ne ab surgaam: «Jàppal Mise, yóbbu ko ca Amon boroom dëkk bi, ak ca doomu Buur.
27Nga ne ko: “Buur dafa wax ne: Dugal-leen kii ndungsiin, di ko jox lekk gu néew ak ndox mu néew, ba keroog may dikk ak jàmm.”»
28Mise ne: «Soo délseek jàmm déy, Aji Sax ji waxul, ma jottli.» Mu dellu ne: «Mbooloo mi, yeena ko déggandoo, yeen ñépp.»
29Ba mu ko defee buurub Israyil ànd ak Yosafat buurub Yuda, ñu songi Ramot ga ca Galàdd.
30Buurub Israyil nag ne Yosafat: «Damay soppi col, dugg ci xeex bi, waaye yaw solal sa mbubbam buur.» Buurub Israyil daldi soppig col, dugg ca xeex ba.
31Fekk na buurub Siri jox ndigal fanweeri nitam ak ñaar, ñay jiite watiiri xare ya. Mu ne leen: «Buleen xeex ak kenn, du ku tuut, du ku réy, diirleen buurub Israyil, moom rekk.»
32Ba loolu amee, ña jiite watiiri xare ya gis Yosafat, daldi ne: «Kii kay mooy buurub Israyil!» Ñu walbatiku ci kawam, ngir song ko. Yosafat nag àddu ca kaw,
33njiiti watiir ya xam ne du buurub Israyil, ñu walbatikuwaat, bàyyi ko.
34Ci biir loolu mu am ku soqi ag fitt te teyu ko, mu dal buurub Israyil ci diggante ñaari wàlli pakk bi mu sol. Mu ne dawalkatu watiiram: «Waññikul, génne ma ci xeex bi, gaañu naa!»
35Naka la xare ba tàkkarnaase bésub keroog bépp, ñu téye buur ba ca biir watiir wa, mu janook waa Siri, ba ca ngoon sa, mu doora dee. Jam-jam baa nga nàcc, ba taa ca biir watiir ba.
36Jant baa ngay xalambaayu, yéene jib, ba dajal mbooloo ma. Ña nga naan: «Na ku nekk ñibbi sa dëkk, ca sam réew!»
37Buur ba nag saay, ñu yóbbu ko Samari, denc ko foofa.
38Ba ñuy raxas watiir ba ca déeg ba ñuy wax Samari, xaj ya di xab deret ja, gànc ya di sangu ca ndoxum déeg ma, muy la Aji Sax ji waxoon.
39Li des ci mbiri Axab ak mboolem lu mu def ak kër ga mu tabax, rafetale ko bëñi ñay, ak mboolem dëkk ya mu tabax, loolu lépp, bindees na ko moos ca téere ba ñu dippee Jaloorey buuri Israyil ca seeni jant.
40Buur Axab nag saay, fekki ay maamam, doomam Akasiya falu buur, wuutu ko.
41Axab moomu, ba mu faloo Israyil, ba dugg ñeenteelu atu nguuram, ca la Yosafat doomu Asa falu buur ca kaw Yuda.
42Yosafat amoon na fanweeri at ak juróom, ba muy falu te ñaar fukki at ak juróom la falu ca Yerusalem. Yaayam moo doon Asuba, doomu Sili.
43Yosafat ci tànki baayam Asa la aw, jàddul fenn, xanaa di def njub lu Aji Sax ji rafetlu.
44Teewul jëlewu fa bérabi jaamookaay ya. Askan wa dañu fa daa dem ba tey, di fa rendi saraxi jur, di fa taal cuuraay.
45Séqoon na nag ak buurub Israyil jàmm.
46Li des ci mbiri Yosafat ak njàmbaaram aki xareem, bindees na lépp moos ca téere ba ñu dippee Jaloorey buuri Yuda ca seeni jant.
47La desoon ca ñay jaay seen bopp ca jaamookaayi tuur, ya fa desoon ca jamonoy baayam Asa, ba booba, Yosafat da leena jële ca réew ma.
48Booba réewum Edom amuloon buur. Ab jawriñ lañu fa daan tabb.
49Yosafat defaroon na ay gaal yu mag yu mu deme réewum Ofir, di wuti wurus. Waaye sottiwul, ndax gaal yaa nga suux ca Esiyon Geber.
50Booba la Akasiya doomu Axab wax Yosafat ne ko: «Tee ngaa may samay nit, ñu ànd ak say nit ci gaal yi?» Yosafat lànk.
51Gannaaw gi Buur Yosafat tëdd, fekki ay maamam, ñu denc ko fa ñu denc ay maamam ca gox ba ñu naan Kër Daawuda maamam. Doomam Yoram falu buur, wuutu ko.
52Yosafat moomu, ba mu faloo Yuda, ba dugg fukkeelu atu nguuram ak juróom ñaar, ca la Akasiya doomu Axab falu buur ca Israyil, péeyoo Samari. Akasiya nguuru na Israyil ñaari at.
53Da daan def lu bon, lu Aji Sax ji ñaawlu, topp tànki ndeyam ak baayam ak tànki Yerbowam doomu Nebat, ma doon bàkkaarloo Israyil.

Read 1.Buur ya 221.Buur ya 22
Compare 1.Buur ya 22:7-531.Buur ya 22:7-53