Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - 1.Buur ya - 1.Buur ya 19

1.Buur ya 19:11-18

Help us?
Click on verse(s) to share them!
11Aji Sax ji ne ko: «Génnal taxaw ci kaw tund wi, fi sama kanam, ndax kat man Aji Sax ji maa ngi waaja romb.» Ci kaw loolu ngelaw lu réy te bare doole jiitu Aji Sax ji, xar tund ya, rajaxe doj ya, waaye Aji Sax ji nekkul ca ngelaw la. Ngelaw la dal, suuf sa yëngu, waaye Aji Sax ji nekkul ca yëngu-yëngu suuf ba.
12Suuf sa dal, sawara dikk, waaye Aji Sax ja nekkul ca sawara wa. Sawara wa dal, ndéey lu suufe topp ca.
13Ilyaas dégg ca, muuroo mbubbam, génn taxaw ca buntu xunti ma; déggul lu moy baat bu ko ne: «Ana looy def fii, Ilyaas?»
14Mu ne: «Man kat damaa xéroona xér ci yaw Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi. Waaw, bànni Israyil dañoo fecci sa kóllëreek ñoom; say sarxalukaay, ñu màbb; say yonent, ñu jam saamar. Ma des man doŋŋ, ñuy wuta jël sama bakkan nii!»
15Aji Sax ji ne ko: «Dellul topp say tànk te jaare ci màndiŋ mi ba Damaas. Boo àggee, nanga diw Asayel, fale ko ko buurub Siri.
16Yewu ma baayam di Nimsi it, diw ko, fal ko buurub Israyil; te Alyaasa, ma baayam di Safat, dëkk diiwaanu Abel Mewola, nanga ko diw, fal ko, muy yonent, wuutu la.
17Su ko defee ku Asayel reyul ba nga raw, Yewu rey la; ku Yewu reyul ba nga raw, Alyaasa rey la.
18Waaye dinaa déeg ci biir Israyil juróom ñaari junniy (7 000) nit, di mboolem ñi sujjóotaluloon Baal te seen gémmiñ masu koo fóon.»

Read 1.Buur ya 191.Buur ya 19
Compare 1.Buur ya 19:11-181.Buur ya 19:11-18